


Sañ-sañu ñi fi dëkk
Wóoral dund bu baax
Yoonu 1987 ci soppi kër faju yi (Nursing Home Reform Law) dafa santaane kër faju gu nekk mu topptoo ñi fi dëkk ci anam buy yokk dundu ku nekk, te wóoral teraanga, tànn ak sañ-sañ ci jël sa ndogal ci sa bopp.
Kër faju yépp dañu leen santaane "ñu jox sarwiis ak mbooloo ngir àgg walla denc wér-gu-yaram, wér-gu-xel ak wér-gu-mbooloo bu gën a kawe bu mënee ngir ki dëkk fi bu nekk, ni ko pexemu topptoo bu ñu bind waxe… bu ñu defar ci tàmbali gi, ak ki dëkk fi, njabootam walla ki ko teewal ci yoon, ni mu mënee." Loolu mooy ne wér-gu-yaramu ki dëkk fi warul wàññiku ndax naka la kër faju giy topptoo.
Yoonu 1987 ci soppi kër faju yi (Nursing Home Reform Law) dafay aar sañ-sañ yii yu ñi dëkk ci kër faju yi:
Sañ-sañ bu ñu xamal la lépp ci
-
Sarwiis yi am ak njëgu sarwiis bu nekk
-
Yoon ak sàrt yu kër gi, boole ci kayit bu bind sañ-sañu ñi fi dëkk
-
Adrees ak nimero telefonu Ombudsman bu dëkk-bi ak kurélu dëkk-bi biy seetlu
-
Kayitu seetlu yu dëkk-bi ak pexemu kër faju gi ngir jubbanti
-
Xamle balaa ñuy soppi sa néeg walla ki ngeen bokk néeg
-
Ndimbal bu fekkee am nga jafe-jafe ci yëg-yëg yi (gis, dégg)
-
Ñi fi dëkk am nañu sañ-sañ ci am xibaar ci làkk bu ñu dégg (Españool, Braille, ak yeneen)
Sañ-sañ ci tawatoo
-
Wax sa tawat liggéeykat yi walla beneen nit, te bañ a ragal ñu fey la ko, te kër gi dina jéem ci lu gaaw ngir saafara tawat yooyu
-
Tawatoo ci prograamu ombudsman bi
-
Tawatoo ci kurélu dëkk-bi biy seetlu te may sartu
Sañ-sañ ci bokk ci sa topptoo
-
Am topptoo gu doy te dëppoo
-
Ñu xamal la bépp soppeeku ci sa wér-gu-yaram
-
Bokk ci seen natt, seen pexemu topptoo, seen faju ak seen génne
-
Bañ garab ak faju
-
Bañ ñu takk la walla ñu jox la garab ngir tëj la
-
Xool sa kayitu faju
-
Bañ a fey sarwiis yu Medicaid walla Medicare di fey
Sañ-sañ ci sutura ak denc sa xibaar
-
Jokkoo ci sutura te amul tere ak ku nga tànn
-
Ci jamonoy faju ak topptoo say soxla yu sutura
-
Ci mbiri faju, mbiri sa bopp walla mbiri koppar
Rights During Transfers and Discharges
-
Des ci kër faju gi, lu dul bu ñu ko toxal walla génne ndax:
-
(a) loolu moo soxla ngir njariñu ki dëkk fi:
-
(b) loolu moo war ndax wér-gu-yaramu ki dëkk fi gën na te soxlaatul topptoo ci kër faju:
-
(c) loolu moo soxla ngir aar wér-gu-yaram ak kaaraange yeneen ñi fi dëkk walla liggéeykat yi;
-
(d) loolu moo war ndax ki dëkk fi feyul, ginnaaw ñu xamle ko ci jamono ju doy, li kër gi laaj ci lu mu laaj walla sarwiis bu ñu ko def
-
-
Am xamle 30 fan balaa ñuy toxal walla génne, bu wax li tax ak sa sañ-sañ ngir dàq ndogal li, ak tur, adrees ak nimero telefonu ombudsman bu dëkk-bi ngir topptoo bu yàgg
-
Toxal walla génne ci kaaraange, ginnaaw kër faju gi waajal ko bu doy
Sañ-sañ ci teraanga, respe ak moom sa bopp
-
To be treated with consideration, respect and dignity
-
To be free from mental and physical abuse, corporal punishment, involuntary seclusion, and physical and chemical restraints
-
To self- determination
-
Security of possessions
Sañ-sañ ci am seetsi
-
Doktooru ki dëkk fi ak ñi teewal kurélu dëkk-bi biy seetlu ak prograamu ombudsman
-
Mbokk, xarit ak yeneen ñi ki dëkk fi tànn
-
Kurél walla nit ñiy jox sarwiis yu wér-gu-yaram, yu mbooloo, yu yoon walla yeneen
-
Ñi fi dëkk am nañu sañ-sañ ci bañ gan
Sañ-sañ ci jël sa ndogal ci sa bopp
-
Jël ndogal yu sa bopp, ni yére yi ngay sol ak naka ngay jëfandikoo sa jamono ju wéy
-
Ñu matale say soxla ak say bëgg-bëgg ci anam bu jaadu
-
Tànn sa doktoor
-
Bokk ci mbooloo yu gox bi, ci biir kër faju gi ak ci biti
-
Sàkk te bokk ci Kurélu ñi fi dëkk (Resident Council)
-
Topptoo sa mbiri koppar ci sa bopp
